lundi 30 août 2021

Gëstu jëmale ci njàng mi ci réewum Senegal


Njàng mi si réewum senegaal dafa tawat. Tànk yi daño nagam. Déedéet weesu lóolu njàng mi si boppam dafa lafañ. Ay ndongo yuy yaqate bërëb bi jàngale kat yi di daje fële ca Sinja. Ñenn ñi dileen bunduxatal ak a fexeel ca Cees. Ca jamono jooju fële ca Wurosoogi ndaw ya ngi sànni seeni buluus ak téere si biir ndox mu salte ngir wane seen mbegte ñeel wakaans yi. Laaj bi mooy rek ana lan mo waral lini mel. Tontu bi mooy ñëp am nañu si wàllë, jàngale kat bi, waajur yi, ndongo yi, nguur gi, ñëp a ngi ci biir. Bu njëkkone jàngale dafa nekkone liñu fónk, du ku jóg rek duggu si. Waaye léegi dey dafa melni kër gu amul buntu ku ñëw rek duggu. 

Ci pulaar daño tàmm di wax ‘’so go boni limoore aayiima’’ maanaam ‘’su benn yaqo, wañi gi dafay sooxe’’. Ndaw yi def yi jëf yu ñaaw ci kan lañuy roy. Du ci ñenn ñudul ndongo yu nekk ci daara yu kawe yi melni ‘’Daara ju kawe ji di seex anta joop’’ nga xamne ñenn ci ndongo yu fa nekk dëkkuñu ci ludul fitnaal ak a naqaral seeni jàngale kat yi. Walla ñenn ci wëy polotik yi di xulo ak a xeex ci kanamu askan ci péncum ndawi réew mi. Waye tamit mën nanu wax ñenn ci waajur yi yaratuñu njaboot gi ndaxte ndongo bi nekkul lenn ludul seetu sen wa kër. Tollu nanu ci jamono bi nga xamne war nanu dellowaat yenn ci ay xeetu duma lu ci melni « tann par kaat », « foron sir la taabal ». Ak lu ci mënti am takku jog jotna ngir faagaagal feebar bu nekk di ray ndànk ndànk njàng mi ci sunu réew.

Aucun commentaire:

Enregistrer un commentaire

Analyse sur la situation en Guinée

      Alpha Condé entouré par les putschistes Arrivé au pouvoir en 2010 après 40 ans d’opposition, le président Alpha Condé semb...